Aji Sax ji moom turam wu màgg wi tax na du wacc ñoñam, ndax Aji Sax ji la soob, mu def leen ñoñam.
TSK
TSK · Romans 11:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Guddi may fàttliku sama woy, di waxtaan ak sama ngegenaay, sama xel di jéex te naa:
Boroom bi kat du wacc ñoñam mukk, du bàyyi ay séddoom.
«Xanaa dégguloo li nit ñi wax? Ñu ne: “Ñaari làng ya Aji Sax ji tànnoon de, wacc na leen,” moo tax ñu xeeb sama ñoñ, ba tegatuñu leen sax aw xeet.»
Boroom bi, Aji Sax jaa ngi ne jàkk réewum bàkkaarkat mii. Maa koy sànke kaw suuf, waaye ba tey duma fàkkas faraas waa kër Yanqóoba.» Kàddug Aji Sax jee.
¶ «Mboolem fi ma jaare ci samag dund, dale ko ca samag ndaw, ca ndoorte la, ba ma nekkee ca sama biir xeet, ak ca Yerusalem, lépp, mboolem Yawut yi xam nañu ko.
nde man doon naa ñaana alku sax, daggoo ak Almasi, ngir jàmmi sama bokki xeet, sama bokki deret.
Man mi xaraf ba ma amee juróom ñetti fan, askanoo ci bànni Israyil, giiroo ci Beñamin, di ab Ebrë bu ñaari Ebrë jur, te bokk ci ngérum Farisen, ci wàllu yoonu Musaa.