TSK

TSK · Romans 12:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Képp ku def lenn ci yooyu ñaawtéef déy, kooku dees koy dagge ci biir bànni Israyil.

Asamaan lay fenke cat lii, wëndeelu, sowi cat lee; amul lu rëcc tàngooram.

Yal nanga ma dégtal mbég ak bànneex, ma bégati, gannaaw ba nga ma dammatee.

Sa ngëneelu yoon wi nga digle moo ma gënal ay junniy xaalis ak wurus.

Sa kàddooka maa neex, ba dàqal ma tem-temu lem!

Aji Sax ji, namm naa sa wall, sa yoon ay sama bànneex.

Mbégtee ñeel ku daj xel mu rafet ak ku am ug dégg.

Maa leen di jox xol bu yees, te xel mu yees laay def ci seen dënn. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, weccee leen ko xolu suux,

¶ Xam nanu ne yoonu Musaa ci Yàlla la bokk, te man may nitu suuxu neen, dib jaam bu ñu jaay bàkkaar.

¶ Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax, ngir ngeen jébbal ko seen yaram wépp, def ko jooxe buy dund, sell te neex Yàlla. Loolu déy mooy njaamu, gi leen war.

Ndaxte xam-xamu àddina sii, ndof la fa Yàlla. Moo tax bindees na ne: «Mooy kiy jàpp ñi muus ci seen pexey muusaatu,»

Kon bu nit ki bokkee ci Almasi, mbindeef mu bees lay doon. La woon day wonni, li teew nag, di lu yees.

mi maye bakkanam ngir njotug sunuy bàkkaar, ba musal nu ci jamonoy tey ju bon ji, ci coobarey Yàlla sunu Baay,

Ngir itam seen bëti xol leer ba ngeen gis yaakaar ji ci wooteem, ak ni ay ngëneelam géejoo te yéeme, ñeel ñu sell ñi mu séddoo.

¶ Lii nag maa leen ko wax, te di ko biral ci turu Boroom bi: Ni xeeti yéefar yiy jëfe, topp seen xalaat yu tekkiwul dara, buleen jëfeeti noonu.

Li leer gi ci yeen di meññ moo di mboolem luy mbaax ak njub ak dëgg.

¶ Te yeen ñi masoona sore lool Yàlla, doonoon ay noonam ci wàllu xalaat, ak jëf ju bon,

Ab nuyoo it ñeel na leen, tukkee ci jaamub Almasi Yeesu, Epafras, mi bokk ci yeen. Ku jàmbaare ci saxoo leena ñaanal, ngir seenub taxawaay sotti te mat sëkk ci jëfe mboolem luy coobarey Yàlla.

Mboolem Mbind mu sell mi la Yàlla wal ag Noowam, ba mu am njariñal jàngal nit ñi, femmu leen, jubbanti leen, yar leen cig njub.

Njullite gu set te mucc sikk fa kanam Yàlla Baay bi moo di lii: di nemmiku jirim akub jëtun ci seen njàqare, tey sàmmu ba mucc ci gàkki àddina.

Gannaaw gone yu dégg ndigal ngeen, buleen toppati seen xemmemtéefi bakkan ya woon, ba ngeen xamulee.

gannaaw mos ngeen ci mbaaxug Sang bi.

Ci jooju daraja, ak jooju jaloore ju wéet lees nu baaxee ay dige yu réy njég te màgg. Yooyu dige nag, bu ngeen ci jotee, ci ngeen di séddu ci jikkoy Yàlla, gannaaw bu ngeen muccee ci yàqutey àddina, gi xemmemtéefu bakkan waral.

Ñu xalab ninki-nànka ju réy ja, jaanu cosaan joojee ñuy wax Tuumaalkat bi, di ko wax Seytaane, naxekatu mboolem àddina. Ci kaw suuf lañu ko xalab, mooki malaakaam.