TSK

TSK · Romans 12:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Looloo tax itam kàddug Yàlla giy xel, biral ne: “Maay yebal fa ñoom ay yonent aki ndaw, ñii ñu bóom, ñee, ñu bundxatal.”

¶ Ci fan yooyu la ay yonent jóge Yerusalem, dikk Àncos.

Yuda ak Silas it gannaaw ay yonent lañu woon, wax nañu ak bokk yi lu yàgg, ngir ñaax leen, feddli seen ngëm.

Acts 21:9 TSK

Filib moomu amoon na ñeenti doomi janq yuy waxe ay waxyu.

¶ Ma àrtu leen ci kaw yiw wi ma Yàlla may; bu kenn ci yeen teg boppam fu mu àggul, waaye xalaate leen sago, te ku nekk dëppoo ak céru ngëm bi ko Yàlla sédd.

¶ Bokk yi, loolu de laa natte ci Apolos ak ci man, ñeel leen, ngir ngeen jànge ci sunu ñaari jëmm, ba sàmm solob kàddu gii: «Bu seen xalaat jàll ca wàlla li Mbind mi wax.» Su ko defee dungeen réy-réyloo far ak kenn, di beddi keneen.

Su ma jotoon ci kàddug waxyu, boole ci xam mboolem kumpa, ak mboolem xam-xam, ak ngëm gu mat sëkk ba mana toxal ay tund, te jëfewuma cofeel, duma dara.

Waaye kiy waxe kàddug waxyu, nit ñi lay waxal, di feddlee, di ñaaxe ak di naabe.

¶ Ñiy waxe kàddug waxyu, na ci ñaar ba ñett wax, te ñi ci des natt wax ji.

Ndax kat ab joxe, bu àndee ak yéene rekk, la boroom joxe bi amul, deesu ci natt lees koy nangul, waaye li mu am, ci lees koy nangul ab joxeem.

Moo may ñii di ay ndawam, ñee di ay yonent, ñee di ay xamlekati xibaaru jàmm bi, ñale di ay sàmmi mbooloom gëmkat ñi, mbaa ay jànglekat.