TSK

TSK · Romans 13:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 24:14 TSK

Bët di set, bóomkat jóg, bóom baadoolo bi néew doole, guddi jot mu dib sàcc.

Bésub keroog booba, yàllantuy xaalis ak wurus ya nit sàkkal boppam, di leen sujjóotal, ñoom lay sànni ca jaar yaak njugub ya,

Xalableen mboolem tooñ yi ngeen di tooñ. Sàkkuleen xol bu yees ak xel mu yees. Yeen waa kër Israyil, lu jar ngeen di dee?

Waaye yiirooleen Sang Yeesu Almasi, te ngeen baña yittewoo seen bakkan, ngir di topp seeni xemmemtéef.

te mooy ngeen ba seen jikko ju jëkk ja, ngeen teqlikoo ak seen jëmmu démb ja masa topp bànneexi bakkan yuy naxe, ba sóobu ci yàqute.

Ràngooleen mboolem gànnaayi Yàlla, ngir ngeen mana jànkoonte ak pexey Seytaane.

Yeen ñépp ay doomi leer ngeen, doomi bëccëg ndarakàmm; nun bokkunu dara ak guddi, mbaa ag lëndëm.

¶ Kon nag baleen mboolem xeetu mbon, ak mboolem njublaŋ, ak jinigal, ak kiñaan, ak mboolem xeetu yàq der.

Mu neeti ma: «Bul làq kàdduy waxyuy téere bii, ndax waxtu wi jege na.