Xawma sax lu waral may jëfe ni may jëfe; li ma namm, du loolu laay jëfe, waaye li ma bañ, moom laay jëfe.
TSK
TSK · Romans 14:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Romans 7:15
TSK
Romans 14:2
TSK
Mu mel ni tey, kii ngëmam moo ko may mu saña lekk lu nekk; kee, ngëmam lujum doŋŋ la ko ngëmam gu dëgërul may mu lekk.
Romans 14:14
TSK
Xam naa nag, wér na ma it te Sang Yeesu tax, ne amul lenn lu sobewu ci wàllu boppam, ba daganula lekk; waaye ki jàppe lenn muy lu sobewu, ci moom la loola di lu sobewu.
¶ Li nuy damoo nag moo di seede bi nu sunu xel mu dal seedeel, ne xol bu set ak jikko ju dëggu ju bawoo fa Yàlla, mooy li nu doxale ci àddina si, rawatina sunu digg ak yeen, te du lu nu sunu xam-xamu nitu neen may, waaye yiwu Yàlla moo nu ko may.
James 3:13
TSK
¶ Ana ci yeen ku rafet xel te xam àddina? Na ko firndeele dundin wu rafet wu feeñ ci jëfam ju teey ndax xel mu rafet.