TSK

TSK · Romans 16:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Fàttlikuleen mboolem yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji awale diiru ñeent fukki at yii ci màndiŋ mi, teg leen coono, nattu leen ngir xam li ci seen biir xol, xam ndax dingeen wormaal ay santaaneem, am déet.

Fàww sax mu am ay xaajaloo ci seen biir, ngir ñi seen ngëm wér mana fés ci seen biir.

¶ Boole nañu leen itam ak sunu mbokk mu nu nemmiku xéraangeem ay yooni yoon, ci fànn yu bare, te mu gënatee xér bii yoon ndax kóolute gu réy gu mu am ci yeen.

Dees koy jëkka seetlu nag, ba muy ku mucc sikk, ñu door koo dugal ci liggéeyu taxawukatub mbooloo mi.

Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant, ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi feeñee.