¶ Ci kaw loolu Póol agsi Derbe, teg ci dëkk ba ñuy wax Listar. Ndeke ab taalibee nga fa bu ñuy wax Timote; ndeyam di gëmkatub Almasi bu bokk ci askanu Yawut, baayam di Gereg.
TSK
TSK · Romans 16:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ca la bokki gëmkat ñi yebal Póol ca saa sa, mu jëm tefes ga, Silas ak Timote ñoom, des ca Bere.
Mu daldi yebal fa Maseduwan, ñaari jaraafam, Timote ak Eràst, moom mu toogaat ab diir ca Asi.
Nuyul-leen ma Andoronikus ak Yuña, sama bokki Yawut, yi ñu ma tëjandooloon; ñu ñu nawloo lañu ci ndaw yi, te ñoo ma jëkka gëm sax Almasi.
¶ Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu ci coobarey Yàlla, ci man la bataaxal bii bawoo, bawoo itam ci Timote mbokk mi, ñeel mbooloom Yàlla mi ci Korent, ak mboolem ñu sell ñi ci diiwaanu Akayi gépp.
¶ Man la Póol, Timote miy jaamub Almasi Yeesu ni man ànd ak man ci lii, ñeel mboolem ñu sell ñi gëm Almasi Yeesu, te dëkke Filib, yeen ak seeni njiit ak taxawukati mbooloo mi.
¶ Man Póol ndawal Almasi Yeesu ci coobarey Yàlla, maa bind lii, ànd ceek mbokk mi Timote,
Nu daldi yónni Timote, muy sunu mbokk, di jawriñub Yàlla bu nuy liggéeyandool ci xibaaru Almasi. Su ko defee Timote dooleel leen, feddli seen ngëm,
¶ Man la Póol, mi ànd ak Silwan ak Timote ci kàddu gii ma yékkati, ñeel mbooloom gëmkati waa Tesalonig, ñi bokk ci Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.
¶ Yaw miy nitu Yàlla nag, dawal loolu, te topp njub ak njullite ak ngëm ak cofeel ak muñ akug teey.
ñeel Timote, sama doom, sama soppe. Aw yiw ak yërmande ak jàmm ñeel na la, bawoo ci Yàlla Baay bi, ak sunu Sang Almasi Yeesu.