Maa ngi leen di léeb, di sulli kumpay démb,
TSK
TSK · Romans 16:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def, te déeyu ko yonent yiy jaamam.
¶ Ci kaw loolu Yeesu walbatiku ca taalibe ya, wax leen ñoomu neen, ne leen: «Ndokklee ñi seeni gët gis li ngeen gis.
¶ «Léegi nag, dénk naa leen Yàlla ak kàddug yiwam, gi leen mana dooleel, dencal leen seen muur ci biir mboolem nit ñi ñu sellal.
Yaw miy sikkal jaamub jaambur, yaay kan? Su baaxalee mbaa mu bonal, sangam a koy seet! Te day baaxal ndax Boroom bi man na koo baaxal.
¶ Man ci sama bopp, bokk yi, bi ma dikkee ci yeen, du ci puukarey kàddu yu gëna taaru, ak xam-xam bu ma leen yégalsee mbóoti Yàlla.
¶ Dees noo wara jàppe ay surgay Almasi, ay saytukati mbóoti Yàlla.
Nun kat, du sunu bopp lanuy waare, waaye li Yeesu Almasi dib Sang moom lanuy waare, te nun ci sunu bopp nooy seeni jaam, ndax Yeesu.
Moo nu xamal mbóotum coobareem, mi mu nammoona sottale naka jekk ci Almasi, na mu ko neexe.
May niital ñépp, ni Yàlla nara sottale mébétam, miy mbóot mu làqu woon naka jekk fa moom Yàlla mi sos lépp.
¶ Moom mi mana jëfoo kàttan giy liggéey ci nun, ba sottal mboolem lu nu ñaan ak lu nu xalaat, ba wees loola fuuf sax,
Kàddu googu moo di mbóot mi masoona làqu maasoo maas, waaye tey Yàllaa ko xamal ay nitam ñu sell.
Ci loolu it la leen woo ba mu jëfandikoo xibaaru jàmm bi nu leen àgge, ngir ngeen séddu ci sunu ndamal Boroom Yeesu Almasi.
Waaye Boroom bi mooy ki jara wóolu, te moo leen di dooleel, musal leen ci Ku bon ki.
¶ Bàyyil xel ci Yeesu Almasi mi ñu dekkal te mu soqikoo ci Daawuda, ni ko sama xibaaru jàmm indee.
Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.
Bu yàgg, ba àddina sosoogul la Yàlla tuddaloon Almasi loolu, waaye léegi ci mujug jamono jii la ko Yàlla feeñal ngir yeen,
¶ Ki leen mana aar ci bépp jéll, ba taxawal leen fa muy teewejee darajaam, te fekk leen ñàkk sikk, seen mbég mat sëkk,