Sunu Boroom a màgg, bare doole; am xelam wees kemu.
TSK
TSK · Romans 16:27
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ci moom la lépp sosoo, ci moom la lépp sottee, te moom la lépp ñeel. Moom la daraja ñeel ba fàww! Amiin.
¶ Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa,
¶ Moom mi mana jëfoo kàttan giy liggéey ci nun, ba sottal mboolem lu nu ñaan ak lu nu xalaat, ba wees loola fuuf sax,
ngir ngeen gëna am fit, mànkoo ci biir cofeel, te géeju ci gis-gisu xol bu leer nàññ te wóor, ba mana daj dëgg, mbóotum Yàlla, miy Almasi ci boppam.
Moom doŋŋ moo dul dee, moo màkkaanoo leer gu kenn jotewul, te mooy ki nit masula gis te tële koo gis. Teddnga ak kàttan ñeel na ko ba fàww. Amiin.
¶ Kon nag saa su nekk, nanuy jooxee ci Yeesu, sunu saraxu cant, ñeel Yàlla, muy sarax su bawoo ci sunuw làmmiñ, ñu di ko birale aw turam.
Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gi tabaxe kërug Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi.
Waaye màggleen ci wàllu yiwu sunu Boroom, sunu Musalkat Yeesu Almasi, ak ci wàllu xam-xam bu ngeen ko xam. Ndam ñeel na ko tey, ba kera bés bu sax dàkk. Amiin.
tukkee itam fa Yeesu Almasi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki jëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqlikook kilifteefu sunuy bàkkaar,
Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.
¶ Gannaaw loolu damaa dégg lu mel ni coow lu xumb, bawoo ci mbooloo mu bare mu àddoo asamaan, ne: «Aleluya! Texe ak daraja ak kàttan ñeel na sunu Yàlla.