TSK

TSK · Romans 16:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Jant ya Galyon moomee diiwaanu Akayi, Yawut ya dañoo mànkoo, jógal Póol, jàpp ko, yóbbu ca àttekaay ba.

Ndax kat ab jooxe bu génnee ci tooyalub sunguf, di ndoortel meññeef, su boobu jooxe sellee, tooyalub sunguf bépp ay sell. Ndax su reenu garab sellee, car ya it sell.

Nuyul-leen ma Ampilyaatus, mi ma soppal sama bopp ndax Sang bi.

¶ Bokk yi, xam ngeen ne Estefanas ak njabootam ñooy jooxeb ndoortel meññeef ci diiwaanu Akayi, te jàpple ñu sell ñi lañu séddoo. Kon dama leen di ñaan,

¶ Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu ci coobarey Yàlla, ci man la bataaxal bii bawoo, bawoo itam ci Timote mbokk mi, ñeel mbooloom Yàlla mi ci Korent, ak mboolem ñu sell ñi ci diiwaanu Akayi gépp.

Nuyul-leen nu bokk yi dëkke Lawdise, ak sunub jigéen Nimfa, ak mbooloom gëmkat, miy daje këram.

Moom la soob mu jure nu kàddug dëgg, ba nu taxawe ab jooxeb ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam.

Ñooñu ñooy ñi masula ànd ak jigéen, di sobeel seen bopp, ndax masuñoo séy. Ñooñoo topp Gàtt bi fépp fu mu jëm. Ñooñu lañu jote ci biir nit ñi, def leen lu mel ni jooxeb ndoortel meññeef, ñeel Yàlla ak Gàtt bi,