TSK

TSK · Romans 2:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ndax kat seen Yàlla Aji Sax ji mooy Yàllay yàlla yi, te mooy Sangu sang yi. Mooy Yàlla ju màgg ji, jàmbaare te raglu. Ki gënalewul, jëlul ub ger.

Lii it ñi rafet xel a ko wax. Par-parloo cib àtte baaxul.

Yeerukat ya dikk ne Yeesu: «Sëriñ bi, xam nanu ne njub ngay wax, di ko jàngle. Amuloo parlàqu itam, waaye ci kaw dëgg ngay jànglee yoonu Yàlla.

¶ Teewul ñooñu ñu jàppe woon ay kàngam, ak daraja ju ñu masoona am, amalu ma solo, nde Yàlla amul xejj ak seen, ñooñu yokkuñu lenn ci kàddu gi may xamle.

¶ Yeen it sang yi, jëfeleen noonu seen diggante ak seeni jaam, bàyyileen di tëkkoo, te ngeen xam ne yeen ak ñoom a bokk benn Boroom fa asamaan, te xejj ak seen amul fa moom.

¶ Gannaaw nag kiy àtte nit ku nekk ci ay jëfam te amu ci xejj ak seen, Baay ngeen koy wax, sàllooleen koo ragal, seen diirub ngan ci kaw suuf.