TSK

TSK · Romans 2:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Lii de, moo doon bàkkaaru Sodom, sa rakk ja, mooki janqam: réy, fuqle, naagu, ne finaax ak ñàkka dimbali ku ñàkk ak ku néewle,

¶ «Jawriñ jooju xam nammeelu njaatigeem, te taxul mu waaj ko, ba jëfewu ko, ay yetam dina bare.

Yàlla nag jéllale na janti ñàkka xam googa woon, waaye tey mu ngi woo ñépp, ak fépp fu ñu féete, ngir ñu tuub.

Moonte xam nañu xéll ne ñiy jëfe noonu, Yàlla moo daganal àtteb dee ci ñoom, te teewul ñu di ko jëfe, rax ci dolli di farle ñi koy jëfe.

¶ Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, ñi ci yoonu Musaa la ko wax, ngir aw lay jeex tàkk, ngir itam mu leer nàññ ne àddina sépp a sikk fi kanam Yàlla.

¶ Ana lu loolu di tekki? Xanaa kon yoonu Musaa bàkkaar la? Mukk kay! Waaye yoonu Musaa moo ma xamal luy bàkkaar. Ndax kat su dul woon ak yoon wi ne: «Bul xemmem yëfi jaambur,» kon xemmemtéef sax duma xam lu mu doon.

Maak ñi amul yoonu Musaa, damaa mel ni ku amul yoonu Musaa, ngir iri leen, doonte ñàkkuma yoonu Yàlla, gannaaw maa ngi ci yoonu Almasi.

Xam nanu nag ne nit ki, du ci jëfi sàmm ndigali yoon la ko Yàlla di joxe àtteb ku jub, xanaa ci ngëm gu mu gëm Yeesu Almasi. Te nun itam, Almasi Yeesu lanu gëm, ngir Yàlla jox nu àtteb ku jub ci kaw gëm gu nu gëm Almasi, te du ci kaw jëf ju nu sàmme ndigali yoon. Ndax kat du ci jëfi sàmm yoon lees di joxe kenn àtteb ku jub.

Waaye mbind mi biral na ne mboolem àddina moo tënku ci kilifteefu bàkkaar, ngir dige bi gëm Yeesu Almasi di jagle, mana dikkal aji gëm ñi.

Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanam ngàngune ma, ay téere ubbiku, beneen téere ubbikooti, di téereb dund ba. Ñu daldi àtte néew ya ca seeni jëf, na ñu ko binde ca téere ya.