TSK

TSK · Romans 2:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu ngoog, bépp bakkan maay Boroom. Muy bakkanu baay, di bakkanu doom, maa moom. Bakkan bi bàkkaar daal mooy dee.

Luke 2:30 TSK

Nde saay gët tegu na ci mucc gi nga dogal,

te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar.

¶ Ba ñu déggee loolu lañu dal, daldi màggal Yàlla. Ñu ne: «Kon xeeti jaambur yi, ndeke ñoom it Yàlla may na leen ñu tuub, ba dund!»

Ba loolu amee fit la leen Póol ak Barnaba tontoo, ne leen: «Yeen Yawut yi de lanu wara jëkka yégal kàddug Yàlla gi, waaye gannaaw gàntal ngeen ko, ba jombale seen bopp ag texe ba fàww, nu ngii di walbatiku ci jaambur ñi.

Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen, ñu tuub ci Yàlla te gëm sunu Sang Yeesu.

¶ Ñu teg ca ñetti fa, mu woolu njiiti Yawuti dëkk ba. Ba ñu dajee, mu ne leen: «Bokk yi, man defuma dara lu dëngook sunuw xeet mbaa sunu aaday maam. Teewul ñu jàppe ma fa Yerusalem, teg ma ci loxoy Room.

¶ Awma lu may rus ci xibaaru jàmm bi, ndax kat mooy manoorey Yàlla jiy musal képp ku ko gëm, dale ci Yawut bi, teg ci ki dul Yawut.

Am Yàlla da di Yàllay Yawut yi doŋŋ? Da dul Yàllay jaambur yi dul Yawut itam? Ahakay, mooy Yàllay jaambur ñeet kay!

Nun ci ndabi yërmande yi Yàlla woo lanu bokk, te du ci Yawut yi rekk lees nu seppee, waaye ci jaambur ñi dul Yawut itam.

Dama leen di wax ne leen, bëgga fésal ne Yàlla ku dëggu la moo waral Almasi dikk, def boppam jawriñu Yawut yi, ngir sottal dige ya Yàlla digoon seeni maam.

Kon nag amul Yawut ak ku dul Yawut, amul ab jaam ak as gor, amul góor ak jigéen. Yeen ñépp benn ngeen ci Almasi Yeesu.

Dundin wu yees woowu amul jaambur akub Yawut, amul ku xaraf ak ku xaraful, amul ab doxandéem ak ku xayadi, amul ab jaam ak as gor, waaye Almasi mooy lépp te moo nekk ci ñépp.

Ndax kat tey la àtte bi wara tàmbalee ci waa kër Yàlla. Ndegam ci nun lay tàmbalee nag, ñi gëmul xibaaru jàmm bu Yàlla, ana fu ñu jëm?