Ana wan xeet wu mag wu am yàlla ju leen jege ni nu sunu Yàlla Aji Sax jiy jegee saa yu nu ko wooyee wall?
TSK
TSK · Romans 3:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dunu ko nëbb sunuy doom, xanaa di ko jottli maas giy ñëw, xamal leen jaloorey Aji Sax ji ak kàttanam aki kéemaanam.
Mooy wax Yanqóoba kàddoom, dogalam yaak ndigali yoonam ñeel Israyil.
Ma jox leen sama dogali yoon, xamal leen sama àttey yoon yooyuy guddal fanu képp ku koy jëfe.
Ibraayma ne ko: “Waaye ñoom am nañu yoonu Musaa, am nañu téerey yonent yi. Nañ leen déggal.”
Moom it moo nekkoon ak mbooloo ma ca màndiŋ ma, mook malaaka ma doon wax ak moom ca kaw tundu Sinayi ca sunu wetu maam ya. Moo jot ci kàddu yuy dund, ngir jottli nu ko.
Yaa xam coobarey Yàlla, te yaa jànge ci yoonu Musaa, ba xam li am solo dëgg.
Ñooñoo di xeetu Israyil wi xéewloo céru doon doomu Yàlla, xéewloo daraja, xéewloo kóllëre yi, ak ndigali yoon wi, ak liggéeyu jaamu Yàlla gi, ak dige yi;
Ndax kat ba Yàlla dàqee Israyil, ca la àddina juboo ak Yàlla. Kon nag bu leen Yàlla délloosee, ana lu muy jur lu moy ndee-ndekki?
Su ma yebu woona def lii ci sama coobarey bopp, dinaa ci am peyoor. Waaye gannaaw dees maa dénk ag caytu, te ajuwul ci sama coobare,
Xanaa kay li ñu gis moo di ni Yàlla yebale Piyeer ngir mu àgge askanu Yawut xibaaru jàmm bi, noonu la ma yebale ngir ma àgge ko jaambur ñi xaraful,
Bi ngay lu tuut nga dale xam Mbind mu sell mi, te moo la mana may xel mu la jëme ci mucc gi gëm Almasi Yeesu di maye.
Kuy wax, na waxe nu mu jottlee kàddug Yàlla. Kuy taxawoo, na taxawoo ci dooley Yàlla, ngir màggug Yàlla feeñe ci lépp, ndax Yeesu Almasi, mi yelloo daraja ak kàttan, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
¶ Ma daldi ne gurub sukk ciy tànkam, ngir sujjóotal ko. Mu ne ma: «Déet, ëpp naa def. Sa mbokkum jaam doŋŋ laa, ni yaak sa bokk yi jàppoo seedeel Yeesu. Sujjóotalal Yàlla. Ndaxte seedeel Yeesu moo di Noo giy dundal waxyu.»