TSK

TSK · Romans 3:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ibraam nag gëm na Aji Sax ji, ba tax Aji Sax ji waññal ko ngëmam ag njub.

Dees na ma waxal ne: «Aji Sax ji rekk a jagoo njekk ak doole!» Mboolem ñi ma mereey ànd, sëgg, fekksi ma.

Sax a leen di lekk ni mbubb, max ŋeeñ leen ni ndimol kawaru gàtt; te du tee sama njekk sax dàkk, sama wall saxal maasoo maas.

Maa béga bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam njekk, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.

Bés yooyu Yuda day mucc, Yerusalem dëkke jàmm, ñu di ko wooye: “Aji Sax ji sunu njekk.”»

¶ Ci kaw loolu mu ne leen: «Lii moo di kàddu ya ma leen waxoon ba ma nekkee ak yeen. Noon naa leen: Mboolem li ñu bind ci samay mbir ci yoonu Musaa, ak ci téerey yonent yi, ak ci Sabóor, fàww lépp sotti.»

Acts 3:21 TSK

Moom la asamaan wara dalal, ba kera jamono ja lépp di dellu jag, na ko Yàlla waxe woon, yonent yu sell ya woon jottli.

Yiwu Sang bi Yeesu daal lanu gëm ne ci lanuy mucce, te ñoom itam, noonu rekk.»

¶ Ci kaw loolu ñu jox ko bés, bés ba dikk, ñu bare dikk, fekksi ko ca daluwaayam. Suba ba ngoon mu di leen jàngal, di leen seedeel lu jëm ci nguurug Yàlla, di leen won ci mbirum Yeesu, firnde yu leen gëmloo te tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi.

Ci xibaaru jàmm bi lañu feeñal ni Yàlla di joxe nit ñi àtteb ñu jub, te lépp aju ci ngëm, ca ndoorte la, ba ca njeexital la. Noonu la Mbind mi indee ne: «Ku jub ndax ngëmam mooy dund.»

ba tax na, noonee bàkkaar doone woon buur, ndax dee gi mu yilife ñépp, ni la aw yiw wuutoo, di buur moom itam, ndax àtteb njub gi aw yiw jural nit ñi, ba jëme leen ci texe gu sax dàkk, ci sunu ndimbalal Boroom Yeesu Almasi.

Yoonu njub gi Yàlla di joxe nit ki, àtteb ku jub, moom lañu umple tey jéema dëggal seen njubteg bopp. Moo tax nanguluñu njubte gi Yàlla di maye.

Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu, mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njekk, di sunu sellte, di sunug njot,

Mbind mi moo waajaloon lu jiitu ne ci kaw ngëm lees di joxe xeet yi dul Yawut, àtteb nit ñu jub. Moo taxoon mu yégal Ibraayma lu jiitu, bii xibaaru jàmm: «Xeeti àddina yépp ci yaw lañuy barkeele,»

ngir ma mana feeñe ci biir Almasi, fu ma yaakaarul sama njekku bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njekk gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi. Njekk googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi moo koy maye.

¶ Ngëm la Abel jébbale Yàlla sarax su gën saraxub Kayin, te ngëm lees seedeele Abel ne moo jub, kera ba Yàlla ci boppam seedee ne ay saraxam a nangu. Ngëm it moo waral Abel dee, te di wax.

¶ Ci man Simoŋ Piyeer, miy jaamub Yeesu Almasi, di ndawam, ci man la bataaxal bii bawoo, ñeel ñi ñu may ngëm gu njég ga réye ni sunu gos, ci sunu njekku Yàlla, Musalkat bi Yeesu Almasi.