TSK

TSK · Romans 5:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,

Mennum man mii maay far say moy ngir man, ba dootuma fàttliku bàkkaar.

Luke 7:47 TSK

Moo tax ma di la wax, ne bàkkaaram yu bare yi ñu ko jéggal moo waral fonkeelam gu bare. Waaye njéggal lu tuut, fonkeel gu tuut rekk.»

¶ Am xamuleen ne aji jubadi ñi amuñu cér ci nguurug Yàlla? Bu leen kenn nax: Muy fokati séy yi, di bokkaalekat yi, di jaalookat yi, di góor-jigéen yi, ak ñiy ànd ak ñoom,

¶ Mboolem ñi yaakaar seen jëf ju ñu sàmme yoonu Musaa, repp nañoo alku, nde bindees na ne: «Alkànde ñeel na képp ku saxoowul mboolem digal yi ñu bind ci téereb yoon wi, ngir di ko jëfe.»

Ndax kat képp ku sàmm yoon wépp, ba mu des lenn ndigal doŋŋ lu mu tërëfe, ab daanu ku moy yoon wépp ñeel na ko.