TSK

TSK · Romans 5:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, ñi ci yoonu Musaa la ko wax, ngir aw lay jeex tàkk, ngir itam mu leer nàññ ne àddina sépp a sikk fi kanam Yàlla.

¶ Bàkkaar moo jaare ci kenn nit dugg ci àddina, dee jaare ci bàkkaar, dikk, ba dikkal ñépp, ndax ñépp a bàkkaar.

Noonee déggadig kenn nit taxe ñu bare doon ay bàkkaarkat, noonu it la déggug ndigalu kenn nit taxe ñu jox ñu bare àtteb nit ñu jub.

¶ Ci man Simoŋ Piyeer, miy jaamub Yeesu Almasi, di ndawam, ci man la bataaxal bii bawoo, ñeel ñi ñu may ngëm gu njég ga réye ni sunu gos, ci sunu njekku Yàlla, Musalkat bi Yeesu Almasi.