TSK

TSK · Romans 5:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko këpp sunu gépp ñaawtéef.

mi ñu teg ciy loxo, mu dee ndax sunuy tooñ, ba dekkal ko, ngir nu jagoo àtteb nit ñu jub.

¶ Yoonu Musaa moo dikk ngir fésal barewaayu moy, waaye fu bàkkaar bare, aw yiw gën faa bareeti,

Mbaax gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu, moom lay firndeele mboolem xarnu yiy ñëw, ni yiwam yaatoo ba tiiñ am xel.

Almasi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gi.