TSK

TSK · Romans 7:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

lépp lu ciy ñaan akug tinu gu bawoo ci képp ku mu doon mbaa ci mboolem Israyil sa ñoñ, te fekk ku ci nekk ràññee mititu xolam, ba tàllal ay loxoom jublook kër gii,

Ba ma nee cell, damaa ràgg, dëkke naqar.

yaram tàng, di bax, ma wéradi, ne làcc.

Mooy xettliji aji tumurànke bu woote wall ak aji néewle ju sësul fenn.

ñu sóoraale maak ñi wàcci biir bàmmeel. Ma mel ni jàmbaar ju kenn amatul yaakaar,

nde Aji Sax jeey jéere fu sellam fa ca kaw, di niire suuf fa asamaan,

Sàkku naa sag wall ba xol jeex, di xaar sa kàddu.

Njekkar ak njàqare dab ma, say santaane di sama bànneex.

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Aji Sax ji, ci ay xóote laa lay wooye.

Moo nuy yërëmati; sunuy ñaawtéef lay joggiy tànkam, te biir xóotey géej lay tàbbal sunuy bàkkaar.

Luke 4:18 TSK

«Noowug Boroom baa ngi fi sama kaw, moo ma fal, ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm bi. Da maa yebal ngir ma yégal jaam yi ne dees na leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, yégal ñi ñu not, ne dees na leen jot,

Ndax kat, dooley Noo giy maye bakkan te nekk ci Almasi Yeesu moo la yiwi, ba nga mucc ci dooley bàkkaar ak ndee.

¶ Te itam Noo gi moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noowug Yàlla moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ.

¶ Te it, waccalees na ma ndégu biir suux, mu taxawe ndawal Seytaane, di ma mitital, ngir ma baña bew ndax peeñu yu yéeme.

Boroom bee may wallu ci jépp jëf ju bon, te moo may aar ba tàbbal ma fa nguuram ga fa asamaan. Daraja ñeel na ko, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.

Noonu la goreele mboolem ñi seenug ragala dee tënkoon cig njaam, seen giiru dund.