TSK

TSK · Romans 9:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji Boroom gàngoor yee giñ ne: «Lu ma nar déy mooy am, lii ma mébét, mooy sotti.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko fexe, ngir sàggi sagub képp ku fiy damu, ba teddadil képp ku àddina teral.

Suuf a fuddu, wañaaru, mébéti Aji Sax jeey sottalal Babilon, ngir réew ma dib gent bu kenn nekkul.

¶ Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.

Te mooy noonu mu nu taamoo ba àddina sosoogul ndax Almasi mi nu bokk, ngir nu doon ñu sell te mucc sikk fa kanamam. Ci biir cofeel

Ci ñoom lanu bokkoon nun ñépp itam; mas nanoo topp sunu bakkan, di jëfe lu sunu bakkan, ak sunum xel xemmem. Sunu bindu nit taxoon na noo yeyoo am sànj ni ñépp.

Loolu moo doon naka jekk nammeelam gi mu sottale ci Almasi Yeesu sunub Sang.

Ñaax nanu leen, dëfal leen, dénku leen, ngir ngeen di jëfe jëfin wu yelloo ak Yàlla, mi leen woo ci nguuram ak teraangaam.

Moo nu musal, woo nu woote bu sell te sunuy jëf taxul, waaye coobarey boppam a tax, ak yiwam wi ñu nu may ci Almasi Yeesu, balaa ay jamonoy jamono di sosu.

Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.

Dinañu xare ak Gàtt bi, waaye Gàtt bee leen di daan, ndax mooy Sangu sang yi, di Buuru buur yi. Mooy daan mook ñoñam, ñi mu woo, tànn leen te ñu saxoo topp ko.»