TSK

TSK · Romans 9:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Rikk bul yemale ku jub ak ku jubadi, ba boole leen rey, loolu jomb na la moos! Yaw miy àtte àddina sépp kay, lu jub rekk ngay def!»

Job 34:10 TSK

Kon yeen niti xel ñee, dégluleen ma, Yàlla jegewul fenn mbon! Aji Man ji jegewul mukk njubadi!

Job 35:2 TSK

Defe nga ne lii yoon la? Nga ne: «Maa am dëgg fi kanam Yàlla,»

Aji Sax ji, jëfinam jépp njekk la, jëfam jépp ngor la.

¶ Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.

¶ Waaye su sunug njubadi fésalee njubteg Yàlla, ana lu loolu mana tekki ci nun? Ma waxe ko nu ko nit mana dégge; ma ne, kon bu nu Yàlla wàcceelee am sànjam, deful ag njubadeem?

Ma dégg sarxalukaay ba ne: «Waawaaw, Boroom bi Yàlla, Aji Man ji, say àtte dëgg la, yoon la.»