Waaye maa la musal, te li ma ci jublu moo di won la sama doole, ba sama riirum tur dajal àddina.
TSK
TSK · Romans 9:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Man nag maay dëgëral boppu waa Misra, ba ñu dugg, topp leen. Su ko defee ma siiwal sama ndam, ndax dinaa yar Firawnaaki xarekatam yépp, boole ci watiiri xareem aki gawaram.
Yettro nag ne: «Cant ñeel na Aji Sax, ji leen xettli ci notaangey waa Misra ak notaangey Firawna, xettliwaale mbooloo mi ci notaangey waa Misra.
Wóoy ngalla nun! Ku nuy musal ci jii yàlla ju bare doole. Yàlla jii moo dumaa woon waa Misra xeeti mbugal yu nekk, ca màndiŋ ma.
Aji Sax ji, sëlëm leen gàcce, ba ñu sàkku la.
Wóoy ngalla Asiri miy sama yetu mer, bolde bi ñu ŋàbb di samam sànj,
Aji Sax ji dafa wax ki mu fal, Buur Sirus mi mu jàpp ci loxol ndijooram, ngir nangulal ko xeet yi, yolomal ngañaayal buur yi, lafal koy bunt, ba bunti dëkk du tëje,
Yaw lañuy dàqe ci nit ñi; rabi àll yi ngay dëkkal, ñax di sam xont niw nag, lay biy wàcc di la faam diiru juróom ñaari jamono, ba kera ngay xam ne Aji Kawe jee yor nguurug nit, di ko jox ku ko neex.
Mbind mi moo waajaloon lu jiitu ne ci kaw ngëm lees di joxe xeet yi dul Yawut, àtteb nit ñu jub. Moo taxoon mu yégal Ibraayma lu jiitu, bii xibaaru jàmm: «Xeeti àddina yépp ci yaw lañuy barkeele,»
Te lu ci Mbind mi wax? Mu ne: «Dàqal jaam bu jigéen bii ak doomam, ndax doomu jaam bi du donnandoo ak doomu gor si.»