TSK

TSK · Romans 9:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Léegi nag, soo leen dee baal seen bàkkaar, aa... Lu ko moy kat, far ma rekk ci téere bi nga bind.»

Sóol ne ko: «Na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, waaye yaw Yonatan dinga dee déy!»

Acts 7:23 TSK

¶ «Ba ñeent fukki atam matee, xelum seeti bokki bànni Israyilam dikkal ko.

¶ Ma ne kon, xanaa Yàlla daa wacc ñoñam? Mukk kay! Man ci sama bopp ci Israyil laa bokk, askanoo ci Ibraayma, giiroo ci Beñamin.

Moo tax ma di leen biral ne amul kenn kuy waxe Noowug Yàlla ku naan: «Alkànde ñeel na Yeesu.» Te it kenn manul ne: «Yeesu moo di Sang,» te du lu ko Noo gu Sell gi xamal.

Waaye nun ci sunu bopp, mbaa malaaka mu bawoo asamaan sax, ku leen ci àgge woon beneen xibaaru jàmm bu dul bi nu leen àgge, kooku yal na alku!

¶ Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»