TSK

TSK · Ruth 1:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Ruth 2:11 TSK

Mu ne ko: «Dégg naa bu baax li nga defal sa goro lépp, te fekk sa jëkkër faatu, ak ni nga wone gannaaw sa ndey ak sa baay ak sa réewum cosaan, ba ñëw dëkksi ci biir xeet woo xamuloon démb ak bëkk-démb.

¶ Itay ne Buur: «Sang bi, giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, nga fekke tey, fépp foo jëm yaw Buur, sama sang, dinaa fa ànd ak yaw, su may dund ak su may dee.»

¶ Ba mu ko defee Ilyaas ne Alyaasa: «Ngalla xaar ma fii nag, ndax Aji Sax ji da maa yebal Yeriko.» Alyaasa ne ko: «Ak sama digganteek Aji Sax ji, Kiy Dund, nga fekke tey, duma teqlikook yaw mukk.» Ñu daldi ànd, dem Yeriko.

Ay doomi buur a ngi ci jigéen ñi nga teral, sab lingeer féete la ndijoor, takkoo ngëneelu wurus.

Ba loolu amee Buur wax Dañeel, ne ko: «Aylayéwén, sa Yàlla mooy Yàllay yàlla yi, di Sangu buur yi, te it mooy kiy feeñal mbóot, gannaaw feeñal nga mii mbóot.»

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Janti keroog yooyu, fukk ñuy làkk mboolem làkki xeet yi, ñooy langaamoo catu mbubbu benn Yawut, naan ko: “Nun, yeen lanuy àndal, nde noo dégg ne Yàllaa ngeek yeen.”»

¶ Naka lañuy jub dëkk, ba ñu jëm, mu mel ni ku nara jubal yoonam.

Ci kaw loolu Póol ne: «Lu ngeen di def nii, di jeexal sama xol? Waxuma ñu yeew ma rekk, waaye dee sax nangu naa koo def ci Yerusalem ngir Sang Yeesu.»

Nit ñi ci seen bopp ñoo nuy waxal fépp, na sunu ngan ak yeen deme, ak ni ngeen walbatikoo ci Yàlla, dëddu tuur yi, bay jaamu Yàlla ju dëggu jiy dund,