TSK

TSK · Ruth 3:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba mu ko defee Absalom sant ay nitam, ne leen: «Ma ne, bu Amnon naanee biiñ, ba xolam sedd, bu ma leen nee ngeen jam ko rekk, reyleen ko. Buleen ragal; man maa leen ko sant. Góor-góorluleen nag te ñeme.»

¶ Keroog bésub juróom ñaareel ba Buur Aserus naan biiñ, ba xolam sedd, mu sant juróom ñaari bëkk-néegam: Meyuman ak Bista ak Arbona ak Bigta ak Abagta ak Setar ak Karkas, ne leen

Kon nit amul lu gën di lekk ak a naan, di bànneexoo ñaqam. Ma gis ne loolu it Yàllaa koy maye.

Man daal damay digle bànneex, ndax nit amul lu gën fi kaw suuf di lekk ak a naan ak a bànneexu, muñe ko doñ-doñam, fan yi ko Yàlla may fi kaw suuf.

Buleen naan biiñ ba màndi, màndite ci afal seen bakkan la leen jëme, waaye na leen Noo gi fees,