TSK

TSK · Titus 2:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 12:12 TSK

Mag ak xel mu rafet, fan wu gudd ak ràññee.

Bijjaawu bopp kaala gu yànj la, njekk a koy maye.

Naka la Póol wax ci mbirum njub, ak moom sa bakkan, ak àtteb bés-pénc, Feligsë daldi tiit, ne ko: «Léegi, man ngaa demagum, bu ma ko talee, dinaa la wooluwaat.»

Joŋantekati tàggat yaram yi, dañuy yar seen yaram bu metti, te ñooñu kaalag ndam guy seey doŋŋ lañu ci yaakaar, waaye nun, kaalag ndam gu sax dàkk lanu ci yaakaar.

Ndegam danoo teqlikoo ak sunu sago, Yàlla la ñeel. Su nu àndee ak sunu sago nag, yeen la ñeel.

¶ Li ci des nag bokk yi, moo di lii: mboolem lu dëggu, ak mboolem lu tedd, ak mboolem luy njub, ak mboolem lu set, ak mboolem lu jekk, ak mboolem lees di rafetlu, ndegam lu nawlu la te yelloo ngërëm, na leen loola soxal.

Waaye nun ñiy waa bëccëg, nanu ànd ak sunu sago, te def ngëm ak cofeel, sunu kiiraayal dënn; yaakaaru texe di sunu mbaxanam xare.

Njiit li nag fàww mu mucc sikk, di ku dencul lu wees jenn jabar, ku moom bakkanam, jiital am xelam, di ku nawlu, man gan, te mana jàngle.

¶ Naka noonu ab taxawukatub mbooloo mi, na di ku tedd, bumu di boroom ñaari kàddu. Bumu di ku sàngara jiital, mbaa kuy sàkku am-am bu lewul.

Titus 1:8 TSK

Waaye war na di ku man gan, ku xejjoo lu baax, jiital am xelam, jub, sell te moom boppam.

Titus 2:7 TSK

Te nanga doon, yaw ci sa bopp ab royukaay, ci lépp ndax sa jëf ju baax, te nga boole ko ak àlluwa ju dëggu te tedd,

¶ Te itam mujug lépp dëgmal na; kon nag jiital-leen seenum xel, te ànd ak seen sago, ngir ngeen man di ñaan.

seen xam-xam, ngeen dolli ci moom seen bakkan; moom seen bakkan, ngeen dolli ci ag muñ; seenug muñ, ngeen dolli ci ag njullite;