Yàlla, ana lu ko nit mana jariñ? Xanaa ku xelu jariñ boppam!
TSK
TSK · Titus 3:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Éy Yàlla, sàmm ma, maa ngi làqu fi yaw! Maa ne Aji Sax ji: «Yaay sama Boroom, awma alal ju la moy.»
Seede buy fen day sànku, kuy dégg, sa kàddu sax.
Ñu ne ko: «Xanaa dangaa dof?» Teewul mbindaan mi ne moom la. Ñu daldi ne: «Kon malaakaam la.»
¶ Bindees na ne: «Damaa gëm, moo tax ma wax.» Nun it, wenn xeetu ngëm wi lanu am. Danoo gëm, moo tax itam nuy wax.
Mboolem kàddu gii may wax, lu wóor la te jara gëm: Almasi Yeesu moo dikk ci àddina, ngir musal bàkkaarkat yi, te maa ci raw!
Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.
Na sunuy ñoñ tàggatu ci jëf ju baax ju ñu saxoo ba faj soxla yu taxaw, ngir ñu baña ñàkk njariñ.
ñi Almasi tax ngeen gëm Yàlla. Te Yàllaa ko dekkal, may ko ndam, ba tax Yàlla di ki ngeen gëm, yaakaar ko.