TSK

TSK · Zechariah 1:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Dëfal-leena dëfal sama ñoñ, la seen Yàlla wax!

Waaye yaw Yanqóoba sama jaam, bul tiit,» kàddug Aji Sax jee; «yaw Israyil, bul ragal. Fu sore laa lay wallujee, yaak sa askan wa ca réewum njaam ga, Yanqóoba dellu dal, fegu; kenn dootu ko tiital.

Amos 9:11 TSK

«Bésub keroog maay yékkati mbaarum Daawuda mi joy, ba fattaat xar-xar yi, defaraat gent bi, tabaxaat ko na woon.

Ma ne: «Ñii lu ñu wund, Sang bi?» Malaaka miy wax ak man ne ma: «Maa lay won lu ñii wund.»

Ma ne: «Lan la ñii di defsi?» Mu wax ma, ne ma: «Béjjén yii tasaare Yuda ba kenn siggeetul, tëgg yii ñoo dikk ngir tiital leen, ba jàllarbi béjjéni xeet yi jóg song réewum Yuda, tasaare ko.»

«Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa fiire Siyoŋ fiiraange ju réy, am sànj mu réy laa koy fiiree.»