TSK

TSK · Zechariah 12:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yàllaay àtte: kii mu detteel, kee mu kaweel.

Sa boroom Aji Sax ji, sa Yàlla jiy layool ñoñam dafa wax ne: «Mu ngoog, maa jële ci sa loxo, kaas bu wex biy miirloo; taatu kaas ba def sama mbugal, dootoo ko naan.

¶ Aji Sax ji Yàllay Israyil déy da maa wax ne ma: «Am kaasu biiñ bii ci sama loxo, di misaal kaasu mbugal, te nga nàndal ci mboolem xeet yi ma lay yebal,

Ndegam ñi yeyoowul mbugal ñooy jolu kaasu mbugal, nees leen di ñàkka toppe, yeen? Dees na leen topp moos, ngeen jolu kaasu mbugal.

Mu ne: «Maay màndal seeni kilifaak seeni kaaŋ ak seeni kàngam ak seeni jawriñ ak seeni jàmbaar, ñu tëdd nelaw nelawi fàww, duñu yewwooti.» Kàddug Buur a, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.

Yuda it day fekksi Yerusalem ci xeex bi, te dees na dajale alali xeet yi leen wër yépp; wurus, xaalis ak yére, bare, ne gàññ.

Dëkk bu mag ba xar ñett, dëkk yu mag yu askani àddina yi màbb. Babilon gu mag ga nag, Yàlla bàyyi ko xel, ngir nàndal ko kaasu biiñu sànjam muy bax.