TSK

TSK · Zechariah 13:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Waxleen ak bànni Israyil ne leen: Góor gu ànd ak jàngoro ju sabab ngóoraam di xelli mbér, kooku sobewu na.

Job 9:30 TSK

Su ma raggoo woon saabu, ba raxasoo xeme sax,

Ñaawtéef daal laa judduwaale, te sama ndey ëmbaale ma bàkkaar.

Mbégte ngeen di rooteji fa wali mucc ya.

«Yaw nit ki, ba waa kër Israyil dëkkee seen suufas bopp, dañu koo sobeele seen jikko ak seeni jëf, seen jëfin mel ni sagaru sobe ci man.

Maa leen di musal ci seen mboolem sobe, maay woo am pepp, ful ko, te dootuma leen teg ab xiif.

Maay dagge fi sa biir say tuur, ak sa xeri jaamookaay, te dootoo sujjóotal loo sàkke say loxo.

¶ «Aji Sax ji Yuda lay jëkka wallu, ndax darajay waa kër Daawuda, ak darajay waa Yerusalem baña màgg ba ëpple Yuda.

¶ Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba jooxeel leen bakkanam.

Ndegam deretu sikket ak yëkk, ak nag wu jigéen wu ñu lakk, ngir suy dóom ba nit ku sobewu, yooyu lees daan sellale nit ñi, ngir seen cetug yaramu suuxu neen,

tukkee itam fa Yeesu Almasi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki jëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqlikook kilifteefu sunuy bàkkaar,