TSK

TSK · Zechariah 13:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax jeey jógloo ci seen kaw, xeet wu sore, ñu bàyyikoo ca cati àddina, dikk ne milib nig jaxaay, te dégguleen aw làkkam,

maa leen di dogalal saamar, ngeen bokk sukk, ñu rendi leen, ngir maa woote, wuyuwuleen, ma wax, dégguleen, xanaa di def li ma ñaawlu, taamu li ma buggul.»

«Te bu ñu génnee, gis néewi ñi doon fippu fi sama kaw, seeni sax duñu dee mukk, seen sawara du fey mukk, te boroom suux bu leen gis, yaram wa daw.»

Benn cér bi, nanga ko lakk ci digg nataalu dëkk bi, gannaaw bu fani gaw bi matee. Beneen cér bi, nga dóore ko saamar bi, kawar gi tasaaroo fi wër dëkk bi. Ñetteelu cér bi, nga sànni ko ci ngelaw li, man ma toppe ko saamar.

Dina feddli kóllëre diggam ak ñu bare ci benn àppu juróom ñaar, te ci diggu àppu juróom ñaar ba lay dakkal sarax yi ñuy rendi ak yeneen sarax. Ci genn wetu sarxalukaay bi la yàqkat biy taxawal lu siblu, di sabab yàqute, ba keroog muj gi ñu ko dogalal ne milib ci kawam.»

Amos 9:8 TSK

Boroom bi, Aji Sax jaa ngi ne jàkk réewum bàkkaarkat mii. Maa koy sànke kaw suuf, waaye ba tey duma fàkkas faraas waa kër Yanqóoba.» Kàddug Aji Sax jee.

Ma ne gétt gi: «Dootuma leen sàmm. Na ñiy dee, dee; ñiy sànku, sànku; ñi dese bakkan yàppante ci seen biir.»

¶ «Maa ngii di yebal sama ndaw, mu xàllal ma aw yoon. Sang bi (/Boroom bi) ngeen di sàkku mooy jekki agsi këram, malaakam kóllëre moomu (/ndawal kóllëre loolu), ki ngeen safoo, mu ngooguy dikk.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

¶ Xanaa dikk, rey beykat yooyu, dénk tóokër ba ñeneen.» Nit ña dégg loolu daldi ne: «Yàlla tere!»

Yeesu geesu leen, ne: «Yeen jigéeni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom.

¶ Ma ne kon, xanaa Yàlla daa wacc ñoñam? Mukk kay! Man ci sama bopp ci Israyil laa bokk, askanoo ci Ibraayma, giiroo ci Beñamin.

¶ Malaaka mu jëkk mi wal liitam, tawu doji yuur topp ci, ak sawara wu ànd ak deret, ñu boole lépp sànni ci kaw suuf, ñetteelu xaaju suuf si daldi lakk, ñetteelu xaaju garab yi it lakk, ñax mu naat mépp lakk.