Maay ànd ak yeen, di seen Yàlla, ngeen di sama ñoñ.
TSK
TSK · Zechariah 13:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji ngeen biral bésub tey, ne mooy doon seen Yàlla, te dingeen doxe ay yoonam, di sàmm dogali yoonam, aki santaaneem, ak àttey yoonam, tey dégg waxam.
Ndaxam moo xam fi ma jaare, te bu ma nattoo, ma génn ci ni wurus wu ñu xelli.
Na dëddu lu bon tey def lu baax, sàkku jàmm, saxoo ko.
di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»
Mu woo ma, ma wuyu ko; mook man ci biir njàqare, ma xettli ko, darajaal ko,
Xaalis ak wurus sawaraa koy xelli, waaye nit, ab xolam, Aji Sax jee koy nattu.
Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom.
Ma ne, togg naa leen, xelli cib taal, waaye du taalu xellikaayu xaalis, sawaras nattu laa leen xellee.
Duñu liggéeyati mukk ci neen te dootuñu jural mbas. Ñooñooy askanu ñi Aji Sax ji barkeel, seeni doom nekk ak ñoom.
Ndax man déy, xam naa mébét yi ma leen mébétal.» Kàddug Aji Sax jee. «Du mébéti loraange, waaye mébéti jàmm laa leen mébétal, ngir may leen yaakaaru ëllëg.
«Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israyil gannaaw loolu,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.
Su ko defee sama dogali yoon lañuy doxe, te sama àttey yoon lañuy sàmm, di ko jëfe. Su boobaa ñuy sama ñoñ, may seen Yàlla.
Su boobaa ngeen mana dëkke réew mi ma joxoon seeni maam, di sama ñoñ, may seen Yàlla.
Ñenn ci boroom xel yu rafet yi dinanu jaare ci nattu yu leen di sellal, fóot leen ba ñu set wecc, ba keroog mujug jamono. Àpp ba nag des na.
Maay jàmbaaral waa kër Yuda, maay wallu waa kër Yuusufa, suqli leen, ñeewante leen, ñu mel ni masuma leena xarab, nde man maay seen Yàlla Aji Sax ji, te maa leen di nangul.
Waaye bésub dikkam, ana ku ko mana dékku? Bu teewee ana kuy taxaw? Nde moom daa mel ni sawaras tëgg buy xelli weñ, melati ni xemey fóotkat.
Su boobaa, ku woo Boroom bi wall ciw turam, dinga raw.”
Geneen kenu moom maneesu koo lal, xanaa gi xasa lale, te mooy Yeesu Almasi.
¶ Ndokklee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo kaalag dund, gi Yàlla dig ñi ko sopp.
¶ Soppe yi, tàngooru nattu bi ngeen nekke nii, bumu leen jaaxal ba mel ni lu jaaduwul moo leen dikkal.
Képp ku am ndam nag, loolooy doon sab cér. Maay doon sa Yàlla, nga doon sama doom,