Ci biir loolu mu wax ak mbooloo ma, ne leen: «Ngalla dàndleen xaymay nit ñu bon ñii, te buleen laal seen lenn, bala ngeen di buuboondook mboolem bàkkaari ñii.»
TSK
TSK · Zechariah 2:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Génnleen Babilon, dawleen Kaldeen ñi, tey sarxolle. Biral-leen lii, yéene ko, te yeggeji ko waa cati àddina, ne leen Aji Sax ji jot na jaamam Yanqóoba.
Yeen ñiy yóbbu ndabi Aji Sax yu sell yi, bu ngeen di jóge Babilon, dëdduleena dëddu lu sobewu, bañ koo laal, setluleen te génn foofa.
«Yeen gan ñi, génnleen Babilon, ku ne rawaleji sa bakkan. Buleen ñaawtéefu jaambur sànkaale; lii àppu mbugal la bu Aji Sax ji matal; seen añ la, bu mu leen añale.
Wañaarul te yuuxu ni kuy matu ndax mitit, yaw janq Siyoŋ mu taaru, nde dëkk bi ngay génn, màkkaanoo àll bi, dinga dem Babilon, te fa lees lay xettlee, fa la la Aji Sax jiy jote ci loxol say noon.
¶ Ci kaw loolu ma dégg beneen baat bu jóge asamaan, ne: «Yeen sama ñoñ, génnleen dëkk bii, bala ngeena bokk ak moom ay bàkkaaram, bay séddu ci mbugalam.