TSK

TSK · Zechariah 2:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Moo leen fekk réewum màndiŋ, fu ne wëyëŋ, ubaleeki sab, mu feg leen, topptoo leen, sàmm leen, ni bu ñu doon peru bëtu boppam.

Sàmm ma ni peru bët; làqe ma sa ker,

Maa àddu, man mii; maa ko woo, indi ko, te pexeem dina joy.

Gétti Kedar yépp a lay dajesil, kuuyi Nebayot di la jariñ, te di sarax yu dajeek ngërëm ci kaw sarxalukaayu Aji Sax ji, ma di ko darajaale sama teddngay kër.

«Buuru Babilon warax na ma. Da maa muucu, ñiit ma, ba ma set ni ndab. Da maa modd ni ninki-nànka, sole kollam li gën ci man, yàbbi la ca des.»

«Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Edom a feyu ci waa kër Yuda, feyu ga mu feyu di tooñaange gu réy.

«Yaw nit ki, Tir dëkk ba moo ree Yerusalem, ne: “Ñaw! Buntu dëkk bi xeet ya daan jaare dàjjiku na! Léegi man la bunt ubbikul, léegi maay woomle, Yerusalem gental na.”

Maa leen di fulal nit ak mala, ñu giir, nangule. Maay def ñu dëkke leen na woon, baaxe leen lu raw démb, ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji.

Joel 3:2 TSK

Kera jant yooyu, jaam yi sax, góor ak jigéen, maa leen di tuur samag Noo.

Amos 1:9 TSK

Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Tir, te duma fomm seeni duma. Ñoo jàpp mbooloom lëmm, jalax ca Edomeen ña, te sédduñu ci kóllëreg bokk.

Amos 1:13 TSK

Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke Amoneen ñi, te duma fomm seeni duma. Ñoo butti ay jigéeni biir ca Galàdd ba ñuy xare ngir yokk seen suuf.

Tey ci sa kaw, la xeet yu bare daje, yaw Siyoŋ, te naan: «Nees ko tëdde, nanu seetaan Siyoŋ!»

Ndaw siy samab noon moo koy seede, sëlmoo gàcce, moom ma doon naa: «Ana sa Yàlla Aji Sax ji?» Samay gët a naa ndaw soosu jàkk, ñu di ko dëggaate ni banu mbedd.

Ay wi nga teg Libaŋ mooy këppu ci sa kaw, te sànkuteg rabi àll yi sa tiitaange lay jur. Yaa tuur deretu nit, indi aw ay ci réew mi, ak dëkk beek mboolem ñi ci biiram.

Waaye mer mu réy laa mere xeet yii naagu. As lëf laa meroon, waaye ñoom ñoo yokk aw ay.”

Te man ci sama bopp,” kàddug Aji Sax jee, “maa koy nekkal tatay sawara ji ko ub ràpp. Te it maay doon daraja ji ci biiram.”

Pénci dëkk bi, ay gone lay feese, góor ak jigéen, di foye ca pénc ya.»

Acts 9:4 TSK

Mu daanu ci suuf, daldi dégg baat bu ko ne: «Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal?»