TSK

TSK · Zechariah 3:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ndax Ibraayma déggal na ma, dénkoo na sama ndénkaane, ak samay santaane, ak sama dogali yoon, ak samay yoon.»

Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell.

Maa tànne sa baay ci digg giiri Israyil yépp, ngir mu doon sama sarxalkat, di yéeg ci sama sarxalukaay, di taal cuuraay, sol xar-sànni mi, janook man. Maa sédd it sa waa kër baay mboolem saraxi sawara yu bànni Israyil.

Dénkoowuleen dénkaane yi jëm ci sama yëf yu sell yii, xanaa di ko dénk ñeneen ñu koy dénkoo fi sama biir bérab bu sell bi.»

Dig-digal bu sell boobu, na ñeel sarxalkat yi askanoo ci Cadog, ñoom ñi sàmmoon sama ndénkaane, baña ànd ak bànni Israyil, di lajj ni seen yeneen bokki Leween ñi.

Mu ne ma: «Ñooñu ñoo di ñaar ñi ñu diw, fal leen, ngir ñu liggéeyal boroom àddina sépp.»

«Sama kóllëre moom laa ko séqal, mu jur ndund ak jàmm, maa ko may loolu ngir mu ragal ma, ragaloon na ma it, bay yéemu ci sama tur.

Waaye ña ñu yeyale ndekkitel ëllëg, yeyale leen bakkan ci àddina siy ñëw, ñooñu, su boobaa, kenn du ci am jabar mbaa jëkkër.

¶ Dama lay ñaax fi kanam Yàlla mi may bakkan lépp luy dund, ak fi kanam Almasi Yeesu, boroom seede su rafet sa fa kanam Poñsë Pilaat,

¶ Waaye yeen fi ngeen agsi moo di tundu Siyoŋ, dëkku Yàlla jiy dund, te mooy Yerusalem ga ca asamaan, yeena àgg fa junniy junniy malaaka, dajee di màggal;

¶ «Ku am ndam nag, maa lay may nga toog ak man fi sama ngàngune, na ma ame woon ndam, ba toog ak sama Baay fi ngànguneem.