TSK

TSK · Zechariah 4:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Ezra 6:15 TSK

Kër gaa nga sotti ci ñetti fanu weeru Adar, juróom benneelu atu nguurug Daryus.

tund yu mag yiy curpi niy kuuy, di curpeendook tund yu ndaw yi niy mbote.

Doj wi tabaxkat yi beddi woon, moo mujj doju coll wi.

Baat a ngi jib, naan: «Xàll-leen yoonu Aji Sax ji ci màndiŋ mi, fàkkal-leen sunu Yàlla xàll wu jub fi joor gi.

Maa ngii di la def ngay watiiru bàccukaay bu ñaw, yees peq; ànd aki bëñam, ngay wol tund wu mag, raatale; dëbb tund wu ndaw ba mu mel nib cox.

coowal mbégteek coowal bànneex ak kàddug boroom séet ak kàddug séetam, ànd ak kàdduy nit ñiy indi saraxi cant ci biir kër Aji Sax ji, di jàngaale naan: “Santleen Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi. Aji Sax jee baax, kee saxoo ngoram.” Maay tijji wërsëgu réew mi, na woon.» Aji Sax jee ko wax.

Naka ngay xool, aw doj wu loxo sànniwul fàq, daldi dal ca tànki jëmm ja bindoo weñ ak ban bu ñu lakk, daldi koy rajaxe.

Micah 4:1 TSK

Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, askan yi riirandoo, wutsi ko.

Kee taxaw, yëngal suuf; kee xoole, loxloo xeet yi, tund yu mag ya woon naka jekk rajaxoo, tundi cosaan yu ndaw ya maasaloo. Kii moo moom yooni cosaan yi.

«Waxal Sorobabel, boroom Yuda, ne ko: Maa ngii di yëngalsi asamaan ak suuf.

Bésub keroog, kaw tundu Oliw ya la tànkam yay sampe, fa janook Yerusalem, ca penku, tundu Oliw ya xar ca digg ba, penku ba sowu, def xur wu yaa, genn-wàllu tund wa randu, jëm bëj-gànnaar; genn-wàll ga jëm bëj-saalum.

Luke 3:5 TSK

Xur yépp ay sëkke, tund wu magoo wu ndaw maasaloo, yoon ya lunkoon, jubbantiku, ya ñagasoon, nooy,

Acts 4:11 TSK

Yeesu moomu mooy: “Doj wi ngeen beddi woon, yeen tabaxkat yi, te mu mujj di doju coll wi.”

Moo tax cant ñeel ko, ndax yiwam wu màgg wi mu nu baawaanal ci Soppeem bi.

Yeena di tabax, bi ndawi Almasi ak yonent yi di kenu gi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju coll wi.

Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.

¶ Gannaaw loolu damaa dégg lu mel ni coow lu xumb, bawoo ci mbooloo mu bare mu àddoo asamaan, ne: «Aleluya! Texe ak daraja ak kàttan ñeel na sunu Yàlla.