Maay xabtal rabi àll yi ci seen kaw, ñu xañ leen seeni doom, seeni gétt ñu tas, seeni nit ñu néewal, ba seeni mbedd ne wëyëŋ.
TSK
TSK · Zechariah 7:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji moo leen di tasaare ci biir xeet yi, te lu néew la seenu ndes di doon ci biir xeeti jaambur yi leen Aji Sax jiy dàq jëme.
Aji Sax jeey jógloo ci seen kaw, xeet wu sore, ñu bàyyikoo ca cati àddina, dikk ne milib nig jaxaay, te dégguleen aw làkkam,
Xeet yaa ngi ŋarandoo ni ndox mu baawaan, Yàlla gëdd leen, ñu daw ba sore; ngelaw yëngu, ñu naaw, ni boob, ba ca kaw tund ya, mbete pënd bu ngëlén wal, mu def callweer.
«Aji Sax ji déy a ngii dikke sawara, ay watiiram mel ni ngëlén, mu nara sànju, sotti meram, gëdde sawara wuy sëlsëli.
Éey waa kër Israyil,» kàddug Aji Sax jee, «maa ngii di indi fi seen kaw xeet wu bawoo fu sore. Xeet wu am kàttan lañu, xeet wu yàgga yàgg, wu ngeen xamul seen làmmiñ, te dégguleen seeni wax.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Musibaa ngii, di lawal wii xeet ba ca wee, ngëlén lu réy a jollee cati àddina.»
Kàngam ya ne Barug: «Demal làquji yaak Yeremi, te bu kenn xam fu ngeen ne!»
Ak juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom (745) yu Nebusaradan njiital dag ya, toxal. Loolu yemook ñaar fukkeelu at maak ñett ci nguurug Nabukodonosor. Ñi ñu toxal ñépp di ñeenti junni ak juróom benni téeméer (4 600).
Ci kaw loolu béjjén bu ndaw génne ci béjjén yooyu benn, daldi lawa law jublu bëj-saalum ak penkook réew ma gëna rafet.
Sama Yàlla moo leen di xalab, nde ñoo ko déggalul, te ñooy taxawaaluji ci biir xeeti jaambur yi.
Aji Sax ji la mer ma diib, doole ja bare; te du ñàkka topp ku tooñ, ag tooñaangeem. Aji Sax jeey daagoo biir callweer ak ngëlén, niir yi di pëndub tànkam.
«Maa fàkkas ay xeet, seeni tata tasaaroo, ma wéetal seeni mbedd, ba kenn jaareetu fa, seeni dëkk a tas ba kenn desul, kenn dëkkatu fa.
Su boobaa Aji Sax jeey feeñ fi leen tiim, ag fittam tàkk nig melax. Bufta gi la Boroom bi Aji Sax ji di wal, ànd ak ngëléni bëj-saalum, dikk.