Leween ñeey xamal askanu Yanqóoba say àtte, di won Israyil gii saw yoon. Ñooy taal cuuraay fi sa kanam, di teg saraxi dóomal ci sab sarxalukaay.
TSK
TSK · Zechariah 7:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Gannaaw loolu Neyemi boroom dëkk ba ànd ak Esra sarxalkat ba, di bindkat ba ba tey, ak Leween ñay xamal mbooloo ma, wax ak ñoom ñépp, ne leen: «Bésub tey jii, bés bu sell la, ñeel Aji Sax ji, seen Yàlla. Buleen ci naqarlu, buleen ci jooy.» Booba mbooloo ma mépp a doon jooy ca kàdduy yoon wa ñu dégg.
Mu jot nga jooy, mu jot nga ree; mu jot nga ñaawlu, mu jot nga dukkat.
¶ Ba Nabukodonosor buuru Babilon tolloo ci fukkeelu atu nguuram ak juróom ñeent, ba am fukki fan ca juróomeelu weeru at ma, ca la bëkk-néegu buuru Babilon, Nebusaradan njiitu dag ya, dugg Yerusalem.
Sama ñoñ a sànku ndax ñàkka xam; yeen, xam-xam ngeen gàntal, ma gàntal seenug carxal. Yeena fàtte seen yoonu Yàlla, man it maay fàtte seeni doom.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Sàkkul nag ndigal ci sarxalkat yi, nga ne leen,
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Muy koorug weeru ñeenteel, di koorug weeru juróomeel, ak koorug weeru juróom ñaareel, ak koorug weeru fukkeel, lépp janti mbég ak bànneex, ak bési ndaje yu rafet lay nekkal waa kër Yuda Waaye dëgg ak jàmm, soppleen ko.»
«Kàddug sarxalkat déy day sàmm xam-xam, te ciy waxam la nit ñi di sàkkoo àlluwa, nde mooy ndawal Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
Buleen di xañante seen bopp, ndare du yeena mànkoo ab diir, ngir bokk tënku ci ñaan. Waaye gannaaw loolu, delluleen di ànd, bala leena Seytaanee xiirtal ci moy, ndax tëlee téye seen bopp.