TSK

TSK · Zechariah 8:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Man maa tabb buur, fal ko ci Siyoŋ, sama tund wu sell.»

Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon, say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon. Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk, ak Dëkkub Kóllëre.»

Deesatul gaañe mbaa di lore, fi mboolem sama kaw tund wu sell wi, ndax ni ndox di feese ba muur géej, ni la àddina di feese nit ñu xam Aji Sax ji.

Su boobaa yoon dëkke màndiŋ mi, njekk tooge tóokër bi.

Bukki ak mboteey bokk di for, gaynde niw nag, di for um ñax, jaan di dunde pënd. Deesatul gaañe mbaa di lore, fi mboolem sama kaw tund wu sell wi.» Aji Sax jee ko wax.

Ngalla bul mel ni ku waaru, mbaa jàmbaar ju manul walloo. Yaw Aji Sax ji, yaa ngi sunu biir, ñu di nu tudde saw tur. Bu nu wacc!

¶ Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bu ma tijjee seen wërsëg, kàddu gii dina jibati ci réewum Yuda ak dëkk yi ko séq. Dees na ne: “Yaw dëkkuwaayu njekk bii, yaw, tundu Siyoŋ wu sell wi, yal na la Aji Sax ji barkeel!”

Wurmbalu dëkk bi bépp fukki junniy xasab ak juróom ñett (18 000) lay doon. Turu dëkk bi nag, dale ko ca bés ba, di “Aji Sax jaa ngi fi.”»

«Éey, éey yeen, dawleen génne réewum bëj-gànnaar,» kàddug Aji Sax jee. «Ni ñeenti ngelawi asamaan tasaaroo, ni laa leen tasaaree.» Kàddug Aji Sax jee.

Bésub keroog jóolóoliy fas yi sax dees na ci bind: «Sell na ñeel Aji Sax ji.» Te ni ndabi tuurukaay yi fi kanam sarxalukaay bi selle, cin yi gëna néew daraja ci biir kër Aji Sax ji sax noonu lañu selle.

Ci moom la tabax bi bépp di temboo, ba jóg, doon jaamookaay bu sell ngir Boroom bi.

Ma dégg kàddu gu xumb jibe ca ngàngune ma, ne: «Màkkaanu Yàllaa ngii ci biir nit ñi. Mooy dëkk ak ñoom, ñu diy ñoñam. Yàlla ci boppam mooy dëkk ak ñoom, di seen Yàlla.

Du lenn lu sobewu lu fay dugg nag, mbaa defkatu jëf ju ruslu ak njublaŋ. Ñi ñu bind ci téereb dund bu Gàtt bi doŋŋ ñoo fay dugg.