«Demal Sarebta ga ca Sidon te toog foofa. Ma ne, sant naa fa ab jëtun, mu may la loo lekk.»
TSK
TSK · Zechariah 9:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Buuru Babilon nag jam leen, ñu dee, foofa ca Ribla, ca réewum Amat. Noonu la Yuda génne réewam, dem ngàllo.
Lu jëm ci Damaas: «Dëkk yu mag ya ko wër, di Amat ak Arpàdd, jàq nañu; dég-dég bu tiis ba ñu dégg la. Dañu ne yàcc, jaxasoo, mbete géej gu sàmbaraax, deesu ko dalal.
¶ Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
«Yaw nit ki, waxal Boroom Tir, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dangaa fuuy ba naan: ‘Maay Yàlla, ji tooge toogub yàlla yi, fi xolu géej!’ Waaye yaw doom aadama nga, doo Yàlla, dangay yàlla-yàllalu rekk.
«Yaw nit ki, neel jàkk Sidon, nga biral waxyu fi kawam.
Aji Sax ji da ne: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Damaas, te duma fomm seeni duma. Ñoo bàcce waa Galàdd bàccukaayi weñ.
Aji Sax ji, Yàlla, Boroom gàngoori xare yi da ne: «Yeen bànni Israyil, maa ngii di yékkati weneen xeet fi seen kaw, ñu not leen, dale ko fa kaw, fa buntu Amat ba ca xuru Araba, fa suuf.»