TSK

TSK · Zephaniah 2:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

néegi Gebal, Amon ak Amaleg ak waa Filisteek waa Tir,

Boroom bi nee: «Bu ma sottalee liggéey fa kaw tundu Siyoŋ ak fa Yerusalem, maay mbugale buurub Asiri réy-réyloom gi, ak gëti xeebaateem.»

Bésub keroog Boroom bi jooti loxoom ñaareel bi yoon, ngir jotaat ndesu ñoñam, wa des Asiri ak Misra, ak Pattros ak réewum Kuus, ak Elam ak Sineyaar, ak Amat ak biir duni géej ya.

Micah 5:6 TSK

Ci biir askan yu bare la ndesu Yanqóoba di nekk, mel nib lay bu bawoo fa Aji Sax ji, nirook waame wu wàccal gàncax, xaarul lenni nit, lenni doom aadama la séentuwul.

Sëxëtooleen xaalis, sëxëtoo wurus, alal du fi jeex te mboolem gànjar a jale.

Fa la la sawara di xoyome, saamar xottee la fa, raafal la ni soccet di def.

Fa réewum Misra laa leen di waññee, te fa Asiri laa leen di dajalee, yóbbu leen réewum Galàdd ak Libaŋ, te deesu fa gis fu ñu xaj.