Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell.
TSK
TSK · 1 Kings 13:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
«Dees na tërali Aaróona fa ay bokkam. Du dugg déy ca réew ma ma jox bànni Israyil, gannaaw yeena gàntaloon sama ndigal ca walum Meriba.
Samiyel ne Sóol: «Ag ndof nga def, ndax jëfewuloo santaane bi la sa Yàlla Aji Sax ji santoon. Soo ko defoon, Aji Sax ji dina saxal sa nguur ci kaw Israyil ba fàww.
¶ Samiyel ne ko: «Bànneexu Aji Sax ji ci saraxi rendi-dóomal ak yeneen sarax, mbaa tolloo naak bànneex ba muy am ci dégg ndigalal Aji Sax ji? Ma ne, dégg ndigal a gën ab sarax; xol bu nangoo gën nebbonu kuuy.
Ana lu waral nga ñàkke worma kàddug Aji Sax ji, di def lu mu ñaawlu? Uri Etteen bi, yaa ko fàdde saamar; jabaram nga jël, def ko sa jabar, moom nga fàdde ko saamaru Amoneen ñi.
Ndaxte dañu maa wax ci ndigalal Aji Sax ji ne ma: “Bu fa sex dugub, bu fa naan um ndox te bul walbatiku jaare yoon wa nga jaare woon bi ngay ñëw.”»
Ba mu ko defee Aman nettali Seres jabaram ak ay xaritam la ko dal lépp. Ña koy xelal ak jabaram bokk ne ko: «Mardose mii nga tàmbalee torox ci kanamam, ndegam ab Yawut la de, du lenn loo koy manal. Dangay xala daanu rekk ci kanamam.»
Waaye nun ci sunu bopp, mbaa malaaka mu bawoo asamaan sax, ku leen ci àgge woon beneen xibaaru jàmm bu dul bi nu leen àgge, kooku yal na alku!