Maay yëngal xeetoo xeet, alali xeetoo xeet duggsi, ma feesal kër gii ak teraanga, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax;
TSK
TSK · 1 Peter 2:7
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lii ñu bind, lu muy tekki? “Doj wi tabaxkat yi beddi woon, moo mujj di doju coll wi.”
¶ «Kon nag buur Àggripa, peeñum asamaan moomu, woruma ko.
Ñaanal-leen ma, ngir ma mucc ci aji gëmadiy Yude, te itam ndimbal li may yóbbul ñu sell ña ca Yerusalem, ñaanleen ngir ñu nangu ko.
¶ Waaye la ma jàppe woon ag ndollant, moom laa def tey ag wàññeent ndax Almasi.
¶ Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef, ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon, ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.
Ngëm moo waral ba Raxab gànc ba dalalee jàmm nemmikukati réew ma, àndul ak ñu gëmadi ña dee.
Te it: «Mooy doj wuy fakktale, di xeer wuy daaneel.» Ñoo ko fakkastaloo nde ñoo gëmul kàddu gi, te it loolu la leen dogal ba séddoon.