TSK

TSK · 1 Peter 4:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ñi Aji Sax ji xettleey délsi, duggsi Siyoŋ, di sarxolle, kaalawoo bànneex bu sax. Mbég ak bànneex a leen di dab, naqar aku tiis dëddu leen.

Noonu doŋŋ lay deme, bés bu Doomu nit kiy feeñ.

¶ Ba guddi gay xaaj, Póol ak Silas a ngay ñaan, di sàbbaal Yàlla, ñeneen ña ñu fa tëj di leen déglu.

Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.

Dee gi Yeesu dee woon, moom lanu àndal ci sunu yaram, fu nu tollu, ngir dundug Yeesu itam mana fése ci sunu yaram.

Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi wàcc ci sama kaw.

¶ Léegi nag maa ngi bége coono yi ma jànkoonteel ngir seen njariñ; li des ci tiisi Almasi, moom laay mottalee coono yooyu ma daje sama yaramu suux wii, ngir njariñal mbooloom gëmkat, miy yaramu Almasi.

yeen ñi seen ngëm tax ngeen yiiru ci manoorey Yàlla, mi leen di nége mucc ga mu waajal te di ko feeñal ca bés bu mujj ba.

¶ Mag ñi ci seen biir di seeni njiit nag, dama leen di ñaax, man miy njiit ni ñoom, di seedeb coonoy Almasi, te di boroom cér ci ndam li nara feeñ.

Mu ngoogu di dikk, indaale niir yi, te ñépp a koy teg bët, ba ca ña ko jamoon sax, te giiri kaw suuf yépp ay jooy ndax moom. Noonu la moos. Amiin.