Yal na la Yàlla Aji Man ji barkeel, nga jaboot lool te sa giir yokku, ba sos ay mboolooy askan.
TSK
TSK · 2 Samuel 19:39
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Magam ña itam, mu fóon leen tey jooy. Booba la magi Yuusufa ya doora wax ak moom.
Ba mu ko defee Yanqóoba ñaanal Firawna, bàyyikoo fa, daldi dem.
¶ Ñu dellu ne yikkét, di jooyoo. Orpa fóon goroom, tàggtook moom, Ruut nag moom langaamu ko rekk.
Daawuda joxe saraxi rendi-dóomal ak saraxi cant ci biir jàmm, ba noppi daldi ñaanal askan wi ci turu Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi.
Buur ne Absalom: «Déet, doom. Bunu dem nun ñépp. Day diis ci yaw.» Absalom soññ ko, soññ, Buur nanguwula dem. Teewul mu ñaanal ko.
Alyaasa bàyyikoo ca nagam ya, daw topp ca Ilyaas, ne ko: «Ngalla may ma, ma tàgguji sama ndey ak sama baay te topp la.» Ilyaas ne ko: «Doxal dellu; lu ma la def?»
Ba loolu amee ñépp jooyoo jooy yu metti, laxasu ko, fóon ko.