TSK

TSK · 2 Samuel 22:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Yeswa nag ak Kadmiyel ak Baani ak Asabneya ak Serebya ak Odiya ak Sebaña ak Petaya, Leween ñooñu ñépp àddoondoo ne: «Màggal-leen seen Yàlla Aji Sax ji sax dàkk, ba fàww. Nañu màggal sa tur wu tedd, wi raw gépp cant ak ngërëm.»

Ku yaakaar Aji Sax ji bég, leer nàññ, gàcce du ko sëlëm.

di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»

Tumurànke naa, nga gis. Duyal samay rongooñ ci sa mbuus. Du lim nga lépp?

woyleen teddngay turam, darajaal-leen cantam.

Ana ku mana tudd jaloorey Aji Sax ji? Ana ku mana teesal woyam?

Ma woo Aji Sax ji wall, ne ko: «Ngalla Aji Sax ji, xettli ma!»

yaw laay sarxalal saraxu cant, te turu Aji Sax ji laay tudd.

Ndax kat waxees na ne: «Képp ku woo Boroom bi wall ciw turam, mooy raw.»

Ña ngay àddu ca kaw, naan: «Gàtt bi ñu rendi woon moo yeyoo kàttan ak alal, yeyoo xel ak doole, moo yeyoo teraanga, yeyoo darajaak cant.»