Sama doom, saxool xelu akug foog, dee ci xool foo tollu.
TSK
TSK · 2 Timothy 1:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ŋoyal cib yar, bul yoqi, sàmm ko, moo yor sa bakkan.
Jëndal dëgg te bu ko jaay. Sàkkul xel mu rafet ak yar akug dégg.
Waaye cant ñeel na Yàlla, nde ay jaami bàkkaar ngeen woon, waaye gannaaw gi, seenub xol ngeen déggale misaalub àlluwa, ji ngeen di ndénkaaneem.
Li ngeen jànge ci man te jële ko ci man, ak li ngeen dégge ci man, gise ko ci man, jëfeleen ko. Su boobaa Yàlla miy boroom jàmm mooy ànd ak yeen.
Waaye lu mu mana doon, settantal-leen ko, li baax, ngeen jàpp ci,
Sunu yiwu Boroom moo ma baawaanal, booleel ma ci ngëm gi, ak cofeel, gi gëmkatub Almasi Yeesu jagoo.
te lu baax li ñu la dénk, nanga ko sàmm ci ndimbalal Noo gu Sell gi ci nun ñi ko gëm.
¶ Yaw nag saxal ci li nga jàng, muy lu la wóor, nde xam nga ña nga tanqe.
¶ Yaw nag waareel li dëppook àlluwa ji wér,
Almasi nag mooy Doom ju wóor ji jiite kër Yàlla, te nun nooy këram, ndegam kay nu ngi wéye aw fit, ak yaakaar ji nuy puukarewoo.
Nanu ŋoy ci yaakaar, ji nu biral ne moom lanu am, te nu baña yoqi, nde ki dige ku wóor la.
Ŋoyleen rekk ci li ngeen am, ba kera may dikk.
¶ «Maa ngi ñëw léegi. Ŋoyal ci li nga yor, ngir kenn baña fëkk sa kaalag ndam.