TSK

TSK · 2 Timothy 2:19

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Mu wax Kore ak gàngooram gépp, ne: «Bu ëllëgee, Aji Sax ji mooy xamle kan la séddoo ak kan mooy ki sell, mu jegeñal ko boppam. Ki mu taamu nag, dina ko jegeñal boppam.

Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub; yoonu ku bon di sànk boroom.

Ku maandu, Aji Sax ji yég la, sab cér sax.

Yeen soppey Aji Sax ji, bañleen lu bon. Aji Sax jeey sàmm ay wóllëreem, di leen musal ci ku bon.

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Ku doyloo Aji Sax ji, yaay tundu Siyoŋ, doo toxu; dangay sax ba fàww.

Bu ngëlén walee, ab soxor ne mes; ku jub, sab reen sax ba fàww.

Moo tax Boroom bi Aji Sax ji wax ne: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ aw doju coll, muy doju collu tànnéef wu gànjare ngir kenu gi, te ku ko wéeroo doo gaawa daw.

Seen tur wi ngeen bàyyi gannaaw la samay tànnéef di móoloo, naan: “Yal na la Boroom bi Aji Sax ji rey ni diw ak diw,” waaye ñoom sama jaam ñi, tur wu yees lees leen di wooye,

Bésub keroog, kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, maa lay jël, yaw samab jaam, Sorobabel doomu Selcel, kàddug Aji Sax jee, te jaarob torlukaay laa lay def, nde yaw laa taamu. Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.»

Yaa di kan, yaw tund wu mag wi? Boo janook Sorobabel, maase, dig joor, te mooy génne ci yaw doju mujjantal wi, riir ma jolli, ñu naan: «Aw yiw ñeel na ko! Aw yiw ñeel na wii doj!»

Mu neeti leen: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Soreleen ma yeen ñépp, defkati njubadi yi!”

Acts 9:14 TSK

Te moo yor ndigal lu tukkee ci sarxalkat yu mag yi, ngir yeewlu képp kuy tudd saw tur.»

ngir ndesu nit ñi sàkku Boroom bi, te ñooñoo di jaambur ñi ñu tudde sama tur.

¶ Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?

Yàlla waccul ñoñam ñi mu ràññee woon lu jiitu. Am dangeena xamul li Mbind mi indi ci mbirum Ilyaas, ba mu dikkee Yàlla njàmbat lu jëm ci Israyil? Mu ne:

Leneen li indi Almasi mooy may jaambur ñi dul Yawut lu ñu màggale Yàlla, te muy yërmandeem. Noonu it la Mbind mi indee ne: «Looloo waral ma sant la ci biir xeet yi, sàbbaal la.»

ñeel mbooloom Yàlla, mi ci Korent, yeen ñi ñu sellal ci jëmmu Almasi Yeesu, te ñu woo leen ngir ngeen doon ñu sell, ñeel itam mboolem ñiy tudde fépp fu mu mana doon, sunu turu Boroom Yeesu Almasi, mi leen moom, moom nu.

Waaye léegi bi ngeen xamee Yàlla, mbaa bi leen Yàlla ràññee, nu ngeen mana delluwaate ci mbiri àddina yooyu boole tële ak ñàkk njariñ, bay nekkaat seeni jaam?

ki gépp njabootug asamaan ak suuf, jële aw tur.

Te it buleen tiisal Noowug Yàlla gu Sell, gi leen màndargaale xàmmikaayam ngir bésub njot ba.

¶ Kon nag reyleen seen cér yi bokk fii ci kaw suuf; lu mel ni powum séy, ak jëfi sobe, ak ñàkk sago ci lu jekkadi, ak xemmemtéef yu bon, ak bëgge, te loolooy bokkaale ba tey,

¶ Ndax yiwu Yàlla kat feeñ na, te looloo indil ñépp ag mucc.

Booba Ibraaymaa ngay séentu dëkk ba ca kenu ya, te Yàlla di ki yor xaralag tabax bi, boole ci di tabaxkat bi.

Ci jooju daraja, ak jooju jaloore ju wéet lees nu baaxee ay dige yu réy njég te màgg. Yooyu dige nag, bu ngeen ci jotee, ci ngeen di séddu ci jikkoy Yàlla, gannaaw bu ngeen muccee ci yàqutey àddina, gi xemmemtéefu bakkan waral.

¶ Xam naa fa nga dëkk, fa la Seytaane samp nguuram. Teewul nga ŋoy ci sama tur te weddiwoo ne man nga gëm ba sax ca fan, ya nit ña reye ca seen biir, Antipas sama seede bu am kóllëre ba, foofa Seytaane dëkk.

Rab wi nga gis mas naa nekk waaye nekkatul. Dina génne ca xóote ba, waaye day sànkuji. Waa àddina, ñi ñu bindul woon seeni tur ci téereb dund bi ba àddinay door nag, bu ñu gisee rab wi, dinañu yéemu, ndax la mu masoona nekk, tey nekkatul, te ëllëg muy nekkaat.