TSK

TSK · Acts 1:14

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Luke 8:2 TSK

ñoom ak jigéen ñii mu fajoon, ba tàggale leen ak rab yu bon aki jagadi: Maryaama, mi ñuy wax Magdala, ma ñu tàggaleek juróom ñaari rab,

Ndegam yeen ñi bon yeena mana may seeni gone lu baax nag, astamaak Baay ba fa asamaan. Moo leen ko dàq fuuf, nde mooy may Noo gu Sell gi, ñi ko ko ñaan!»

Mboolem xamey Yeesu, ak jigéen ña ko toppe woon ca Galile, ña nga dànd lu sore, di seetaan.

Jigéen ña àgge loolu ndaw ya ñoo doon Maryaamam Magdala, ak Yowaana, ak Maryaama yaayu Yanqóoba, ak itam ñeneen jigéen ñu àndoon ak ñoom.

Acts 2:42 TSK

¶ Ci kaw loolu ñu pastéefu ci njànglem ndaw yi ak ci dundal ag bokkoo, ak ci dagg mburum bokkoo mi, ak ci jataayi julli.

Acts 4:24 TSK

Ba ko bokk ya déggee, ñoom ñépp a mànkoo, daldi yékkati kàddug ñaan fa Yàlla, ne: «Buur Yàlla, yaa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir.

Bégeleen seen yaakaar, di muñ ci biir tiis, tey saxoo ag ñaan.

Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp farlute, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.