Aji Sax ji nag ne Samiyel: «Bul xool ci melokaanu kii, mbaa jëmmu taxawaayam, ndax gàntal naa ko. Lii du ci gis-gisu nit. Nit, li fees bëtam lay gis, waaye Aji Sax ji ci xol lay xool.»
TSK
TSK · Acts 1:24
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Yal na Aji Sax ji àtte xeet yi; Aji Sax ji, seetal ci sama njubteek sama maandute te dëggal ma.
Nanga wóoloo Aji Sax ji, sa léppi xol, te bul wéeru ci saw déggin.
Ma ñaan Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, kiy àtte dëgg, di nattu xel ak xol, ne ko: «Yaw laa diis sama mbir, won ma séen mbugal.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, yaw miy nattu ku jub, di gis xel ak xol, may ma, ma gis ni nga leen di feye; yaw de laa diis sama mbir.
Ñu indi leen fa kanam ndaw ya, ñu ñaanal leen, teg leen loxo.
Mbooloom gëmkat mu nekk nag, ñu tabb ci ay mag; ci biir loolu ñu ñaan, boole kook koor, daldi dénk mag ña Sang bi ñu gëm.
Te kiy xool li ci biir xol yi, xam na liy xintey Noo gi, nde ni ko Yàlla bëgge, ni la Noo giy tinool ñu sell ñi.
Am mbas laay fàdde ay taalibeem. Su ko defee mboolooy gëmkat ñépp dinañu xam ne man maay nattu xol ak xel, te maay fey ku nekk ay jëfam.